Sit bii dafay joxe ay ëmbiit yu bari ngir askanu ñiy làkk wolof. Li waral loolu mooy fësal solo yu askanu Wolof , waye tamit ngir gëna xam-xam Kàddug Yàlla. Looloo tax, sit bii dafay wone bibal bi ak filmu Yeesu ci wolof. Banneexulen ci seen ñëw ci sit bii!
Verset du jour
Bi Yaxya sóobee askan bi yépp ci ndox, sóob na tamit Yeesu ci ndox. Noonu bi Yeesu di ñaan, asamaan si ubbeeku, te Xel mu Sell mi wàcc ci moom, ci jëmm ju mel ni pitax, te benn baat jóge ci asamaan ne: «Yaa di sama doom ji ma sopp. Ci yaw laa ame bànneex.»
Luug 3.21