Sit bii dafay joxe ay ëmbiit yu bari ngir askanu ñiy làkk wolof. Li waral loolu mooy fësal solo yu askanu Wolof , waye tamit ngir gëna xam-xam Kàddug Yàlla. Looloo tax, sit bii dafay wone bibal bi ak filmu Yeesu ci wolof. Banneexulen ci seen ñëw ci sit bii!
Verset du jour
Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku bàyyi këram, jabaram, ay magam, ay rakkam, ay waajuram walla ay doomam ndax nguuru Yàlla gi, dina jot lu bari lool ci àddina si ak dund gu dul jeex ci jamono jee di ñëw.»
Luug 18.29